chat

Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ?

Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ?

Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ?

Gis:

Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ? 2 Kan moom a bind AK lu tax mu bind ma ? BEEPP MIR MUMU MANA DOON DAAY TEKTALE AMUK YAALLA MIKO BIND! KAN MOO BIND ASAMAN YI AK LICI SEEN BIIR CI AY MBINDEEF YU MAAGG YOO XAMNE MBINDEEF MANULEENA PEEK? Kan moo def nosiin wu xereñe wii ? Kan moo bind nit may ko ag dégg ak ub jis ak xel te def ko muy ku man a am xam-xam tey xam li xew. Naka ngay firee wii tërëliin wu yéeme ci jumtukaay yi nekk ci sa biir yaram ak yaramu ndundat yi ? Kan moo fent loolu ? Naka la dund bu rëy bii man a nosaloo ci tëraliinam yu koy nose nose gu yéeme ba àdduna sosoo ba tay ? Kan moo tëral tëraliin yii di àtte àdduna bi(dund ak dee, juranteg yiy dund, guddi ak bëccëg, soppikug jamono yi, añs ) NDAX ADUNA BI MOO BIND BOOPAM ? WALLA DAFA ÑAW CI LUDUL DARA ? WALLA DAFA AM CI XËY CËPPU ?(FIIRU) LUTAX DOOM AADAMA DI GËM MBIR YOO XAMNE JISULEEN ? NIKI : (YËG YËG ,AK XEL, AK RUU ,AK COFEL) DU LUDUL NE MOOM DAAY JIS SEEN JEEXIT ?NAKALAY WEEDDEE AMUK YALLA MI BIND ADUNA BU MAAGG BII !TE MOOM MUY JIS JEEXITI MBINDEEFAMYI, AK JEEXITI XARALAAM, AK JEEXITI YËRMËNDEEM?!. KENN DU NANGGU NIUNEKO KËRGII DAFA AM TE KEENN TABAXUKO !KOON NAK NAKALAY NANGGOO ÑUUNEKO ADUNA BU MAAGG BII DAFA AM TE KEENN BIND KO ?BOROOM XEL NAKALAY NANGGOO BILE TËNKU BU JEEKK CI ADUNA BII DAFA XËY CËPPU ? YALLA MU KAWE MI WAXNA :ۡ

(NDAX ÑOOM DAÑULEEN BIND TE BAWOO WUÑU CI DARA ? WALLA ÑOOM ÑOO BIND SEEN BOOPPWALLA NDAX ÑOOM ÑOO BIND 3 ASAMAN YI AK SUUF SI ?LI AM BADES MOOY DAÑU AMUL KOOLUTE CI SEEN NGËM).

[52 : 32].

AT TUR (YALLA MU KAWE MI ) AMNA KOO XAMNE MOOY BOROOM BI MOOY KI BIND TE MOOY KEENN KI ! AMNA AY TUR AKI MELOKAAN YU BARI TE MAAGG TEY TEKTALE AK MATAM, BOOKK NACI TURËM :AJI BIND JI, AJI YËRËM KUKO SOOP CA ALLAAXIRA, AJI WARSAGALE JI, AJI TABE JI, " KI ÑUY JAAMU"(ALLAAHU) MOOY TUR BI GËNA SIIW CI AY TURËM, LI MOOY FIRI MOOY : KI YEELLO DIAAMU MOOM KESE TE DUÑUKO BOOKKALEEK AK LEEN !. Yàlla mu kawe mi wax na ci Alxuraan ju tedd ji:ۡ

{WAXAL NE LIY MBIR TEY MBIR :YALLA KEENN LA} {YÀLLA MOOY KU ÑUUY JUBLU CI FAJUK AAJO YI} {JURUL KEENN TE KEENN JURUKO} {TE AMUL KEENN KUY NAWLEEM} ].

[112: 4-1

YALLA MU KAWE MI WAXNA :ُ

{YALLA MOOY KI ÑU WARA JAAMU ,JAAMU GI DI JARIÑ ÑAAKK JAAMU GI DI LOR, AMUL KEENN KINIUY JAAMU KU DUL MOOM, MOOY AJI-DUNDU JI MOOY KIY TAXAWU LEEPP, DU GAMMEENTU RAWATINA DI NELAW, MOOY BOROOM LICI ASAMAN YI AK LICI SUUFSI, ANA KAN MOOY RAMMU FA MOOM NDARE CI NDIGALAM, MOO XAM LI NGEEN DI 4 DUNDU MOO XAM LI LEEN JIITU, TE KEENN DU PEEG DARA CI XAM XAMAM NDARE LUKO SOOP, BANĞAM BA ËPP NA ASAMAN YI AK SUUFSI, TE WATTU LEEN TIISA LUKO TE DIISA LUKO, MOOM REK MOOY KI KAWE TE MOOM REK MOOY KI MAAGG}

[2: 255]

. MELOKAAN NU BOROOM BU SEELL BI TE KAWE BOROOM BI MOOY KI BIND SUUFSI TE TAAGGATKO, DEFKO YEELLOOK MBINDEEFAMYI, MOOY KI BIND ASAMAN YI AK LICI BIIRËM CI AY MBINDEEF YU MAAGG, MU DEF JANT BI AK WEERWI AK GUDDI GI AK BACCAGBI, BILE TËNK BU JEEKK DAY TEKTALE MAAGGAAYM . BOROOM BI MOO ÑU TAGGATAL NGALAW LI NGA XAMNE MANUÑOOY DUNDU CI LUDUL MOOM, MOO ÑUY WACCEEL TAW, MOO ÑU TAGGATAL GEEJ GI AK DEX YI, MOOM MOO ÑU DOON DUNDAL BIÑU NEEKKEE MBEEMUR (ËMBU CI BIIR)CI SUÑU BIIRI WAAJUR YI TE AMU ÑUWOON BEENN KAATAN, MOOM MOOY KI DOON DEF DERET JI MUY DAW CI SUÑUY SIDIT, MU DEF SUÑU XOL MUY FER FERI CI LUUY WEY BI ÑU JUDDO BA BALAAÑUY FAATU. YALLA MU KAWE MI WAXNA :ُ ﱠ { YALLA MOO LEEN GEENNE CI SEEN BIIRI WAAJURYI FEEKK XAMULEEN DARA MU DEFAL LEEN NOOPP AKI BËT AKI XEL NDAX NGEEN SANT } (16: 78) BOROOM BI ÑUUY JAAMU SIKK NEEKKUL CI NE MOOY BOROOM MELOKAAN YU MAT YI. BOROOM BI ÑU BIND MOO ÑU WARSAGAL YU YU MANA XAM MAAGGAYAM, MU JËMBAT CI ÑUN AK CET (SET) GU ÑUY TEKTAL MAAGGAYAM AK CI NE MOOM DU MELOWOO MELOKAAN YU MANKI. AK JAAMU FAAWWU MU NEEKK NGIR YALLA MOOM DOONĞ, NDAX TE MOOY KU MAT KU YEELLOO JAAMU, LEEPP LUÑU JAAMU LUDUL MOOM CAAXAAN LA TE LU MAANKI LA TE LUÑU GAARAL LA CI DEE AK JEEX. 5 KU ÑUUY JAAMU WARUL NEEKK MBINDEEF WARUL NEEKK XËRËM WARUL NEEKK GARAB WARUL NEEKK NDUNDAT ! YEELUL CI KU AM XEL MUY JAAMU LUDUL KU AM XEL ! NAKALAY JAAMOO MBINDEEF MUKO YEESS ?! BOROOM BI DU NEKK MBEEMUR CI BIIRU JIGEEN DI JUDDU NI XALE YI DI JUDDOO ! BOROOM BI MOO BIND MBINDEEF YI, MBINDEEF YEEPP ÑOONGI CI AK NGABËM NEEKK CI SUUFU NOTEELAM; MBINDEEF MANUKOO LOR KEENN MANUKOO DAAJ CI GARAB WALLA DIKO MBUGËL WALLA DIKO DOYEDAL ! Boroom bi du dee! BOROOM BI MOOY KI NGA XAMNE DU FAATTE, TE DU NELAW, TE DU LEEKK AW ÑAM, MOOY KU MAAGG KI NGA XAMNE JOOMBUNA CI MOOM MUUY AM SOXNA WALLA DOOM ;NDAX AJI BIND JI DAFA AM AY MELOKAANI MAAGG TE AMUL MELOKAANU AAJOWOO JËM CI KEENN WALLA MAANKI BEEPP YAX BOO XAMNE DAFA AM LU WUUTEEK MAAGGAYU YALLA CI LU ÑOOY ASKANALEE YONENT YI LOOLA YAX YU ÑU SOOPPI LA BOOKKUL CI NDEEY GU WERGI GI NGA XAMNE MOOM LA YONENT YALLA MUUSA ËNDI AK YONENT YALLA ĮSÃ AK ÑU DUL ÑOOM CI YONENT YI YALNA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI. Yàlla mu kawe mi nee na:

{ YEEN NIT ÑI ÑUNGILEEN JOX MISAAL DEGLULEENKO ,ÑI NGAXAMNE YEENANĞ LEEN DI JAAMU BAAYI YALLA DU ÑUMOSABINDWEÑ DOONTEDAÑU DAJALOONGIRLOOLU BU LEEN WEÑ REEKKILOON DARA DUÑUKO MANA NANGU CI MOOM KIIY SAAKKU LOOLUAKA LOTT MOOK LAMUY SAAKKU} (73) 6 { JOXUÑU YALLA DËGG DËGGI GËDDËM TE MOOM YÀLLA MOOY BOROOM KAATAN TE MOOYKI NOT CI NGUURËMGI} (74) [22: 73,74] NDAX XEL NANGUNA YALLA BAAYI ÑU CI LUDUL NDEEY ?(WAHYU)? NDAX XEL NANGUNA YALLA BIND MBINDEEF YI CI LUDUL BEENN JUBLU WAAYE ?WALLA MU BIND LEEN CI POH ? TE MOOM MOOY KU XEREÑKI DI KU XAM LEEPP. ! NDAX XEL NANGUNA KI ÑU BIND CI BILE XEREÑ TAGGATAL ÑU LICI ASAMAN YI AK LICI SUUFSI, MU BIND ÑU CI LUDUL JUBLU WAAYE, WALLA MU BAAYI ÑU CI LUDUL TONTU AAJ YI ËPP SOLO CI YI NGA XAMNE DAF ÑI SOXAL, LAN MOO NEKK CI GINAAW DEE?LAN MOOY JUBLU WAAYE CI YALLA BIND ÑU? LI AM BA DES MOOY YALLA YOONNI NA YÓNENTE YI NGIR ÑU XAM JUBLU WAAYI SUÑUK AM, AK LAN LA YALLA NAMM CI ÑUN! YALLA MOO YOONNI YONENT YI NGIR ÑU XAMAL ÑU NE MOOM DOONĞ MOO YEELLO AK JAAMU, AK NGIR ÑU XAM NAKA LAÑUKOOY JAAMOO, AK NGIR ÑU JOOTALI ÑU AY NDIGALAM AK AY TEEREEM, AK ÑU XAMAL ÑU XIIMA YU BAAX YI NGA XAMNE BU ÑU CI JAAPPEE; SUÑU DUNDU TEEY, TE YIWYI AK BARKE YI DANAÑ ÑU DAJ KAPP. YALLA YOONNI NA YÓNENTE YU BAREE BARI NIKI (NUUH , IBRAHIMA, MUUSAA, HIISAA)...MU JOXLEEN AY MANDARGA AKI KEEMAAN YUY TEKTALE SEENUK DËGGU TE ÑOOM ÑUÑU YOONNI LAÑU ÑU BAAYEKOO FA YALLA AJI BIND JI. KI MUJJI CI YONENT YOOYU MOOY MUHAMMAD YALLA NAKO- YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI- YALLA WAACCE CI NIOOM ALXURAN BU TEDD BII! YONENT YOOYU LE XAMLE NAÑU CI LULEER NAAÑÑI DUNDU BII MOOY NATTU KAAYU JAAMYI LA, WAAYE DUNDU DËGG DËGG MOOY BACA GANNAW DEEH! TE FOOFA LE AMNA AL JANNAH NGIR WËY GËM YI NGA XAMNE ÑOO DOON JAAMU YALLA MOOM DOONĞ , TE GËM MBOOLEEM YONENT YI, TE AMNA YIT SAFARA YALLA WAAJAL KO NGIR WËY WEEDDI YI NGA XAMNE DAÑU DOON JAAMU AY XËRËM DOKO 7 BOOKKAALEEK YALLA, WALLA ÑU WEEDDI KEENN CI YONENT YALLA YI YALLA MU KAWE MI NEENA:

{YEEN DOOMU AADAMA YI BU LEEN AY YONENT ÑAWALEE YU BOOKKCI YEEN DI LEEN JAANGATAL SAMAY AAYA; KEEPP KU RAGAL YALLA TE YEWENËL AY JËFAM DU RAGAL MBUGËLUM ËLLËK TE DU JAAXLE CI LI MUUY BAAYI CI GINAAWAM. } (35) {WAAYE. ÑI NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI SUÑUY AAYA ÑU JOOMBALE SEEN BOOPP JAANGATKO; ÑOOÑU ÑOOY. WAA SAFARA}.(36) [7: 35,36]. Yàlla -mu sell mi nee na-:

{NDAX DANGEEN JOORT NE DAÑULEEN BIND NGIR FOH! TE YEEN DUNGEEN DEELUSI CI ÑUN} [23: 115]. Alxuraan bu tedd bi ALXURAN BU TEDD BI MOOY KAADDUK YALLA MU KAWE MI NGA XAMNE WAACCE NAKO CI NGËN JI YONENT -YALLA NA YALLA DOOLLI KO XEEWËL AK MUCCI TE DOOLLI LEEN KO-MOOM ALXURAN JI MOOY DËGG CI AY AATTEEM MOOY WER CI AY XABBARËM, YALLA MUNGEEY DAKKU ÑIKO WEEDDI CI ÑU ANDI DOONTE WEENN SAAR LA WU MEL NI ALXURAN ÑU LOOTT CI LOOLU NGIR TAARUK FEEMAM AK YEEMEEK AY KAADDUM, MU LAAMMBOO LU BËRI CI AY TEKTALI XEL AK LU WERAWER CI XAM XAM YUY TEKTALE NE TEERE BII 8 MANULA BAAYEKOO CI JAFI MBINDEEF, LI AM BA DES DAAL MOOY KAADDUK BOROOM MBINDEEF YI LA TUDDUNAA AK SEELLËM. Lu tax Yónente yi bari? YALLA YOONNI NA AY YONENT CA NDIALBEEN NGIR ÑU WOO NITÑI JAMEELEEN CI SEEN BOROOM, TE JOOTALILEEN AY NDIGALAM AK AY TEEREEM, SEEN WOOTE ÑOOM ÑEEP MOOY JAAMU YALLA MU TEEDD MI, SAA YU AW XEET TAAMBLEE BAAYI WALLA DI SOOPPI LI YONENTAM BI ANDI CI NDIGLE WEETAL YALLA; REK YALLA TOOGG BENEEN YONENT NGIR MU JUBBANTI YOONWI, TE DEELLOO NITÑI CI MELOKAAN BU MUJJI AYIB, CI WEETAL YALLA AK NANGGULKO, BA YALLA TAJEE YONENT YOOYU LE CI YONENT YALLA MUHAMMAD YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI, BI NGA XAMNE MOO ANDI TËRËLIN BU MUJJI BII, BU SAX DAAKK BII, BU MATALE MBOOLEEM MBINDEEF YI, BAH BIS PEEÑCI, BUY MOOTALI TEY FOOLLI LIKO JIITUWOON CI AY TËRËLIN, BOROOM BI MOO GADDUL TËRËLIN BII AK YONENT GII AK DES AKUK WEY BA BIS PEEÑCI. LOOLU MOO TAX ÑUN JULIT ÑI DËÑUY GËM- NIKO YALLA DIGLEE-MBOOLEEM YONENT YI AK MBOOLEEM TEERE YU JIITU YI. YALLA MU KAWE MI WAXNA;َ

{ CA DËGG DËGG YONENT BI GËMNA LIÑU WAACCE CI MOOM MU BAAYEKOO CA BOROOMAM, JULIT YI ITËM ÑOOM ÑEEPP GËM NAÑU YALLA AK MALAAKA YI, AK TEERE YI AK YONENT YI, DUÑU TEXXALE DIGËNTE KEENN AK KEENN CI YONENT YI, BAH NOOPPI ÑUNE: DEEGG NAÑU TE NANGGU NAÑU, ÑOONGI SAAKKU SA NDIEEGGËL YAW SUÑU BOROOM, TE CI YAW KESE LAAY DEELLU SI MUJUK ÑEEPP. [2: 285]. 9 NIT DU GËM YALLA, FEEK GËMUL MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI, KI YOONNI YONENT YI MOOY YALLA! KU WEEDDI YONENTËK KEENN CI ÑOOM; WEEDDI NA ÑOOPP. AMUL BEENN BAAKAAR BU GËNË MAAGG DOOM AADAMA DI LAANKAL YALLA KAADDUM, NGIR DUGG ALJANNAH; FAAWWU NITKI GËM MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI. LI WAR CI KUNEEKK CI JAMANO JII MOOY MU GËM MBOOLEEM YONENT YI, TE LOOLU DU MËNË AM LUDUL GËM TE TOOPP KI MUJJI CI ÑOOM TE MOOTALILEEN/MUHAMMAD YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI. ALXURAN TUDD NA NE :KEEPP KU BAÑA GËM KEENN CI YONENT YI; WEEDDI NA YALLA TE WEEDDI NA KADDOOM: JAANGAL LAAYA JII DI ÑËW: ﱠ {WERNA NE ÑI NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI YALLA AK YONENTAM YI, BA NOOPPI BËGA TEXXALE DIGANTE YALLA AKI YONENTAAM NUY WAX NAAN: ÑUN DAAL DAÑUY GËM ÑII WEEDDI ÑII, ÑU BËGA JAAPPU CI DIGANTE BOOBU AWYOON NOOÑU ÑOOY ÑU MAT SËKK YEEFËR CA DËGG DËGG, TE WAAJALAL NAÑU YEEFËR YOOYU MBUGËL MUY DOYODALAATE} [4: 150,151]. LAN MOOY LISLAAM? LISLAAM MOOY JEEBLUL YALLA MU KAWE MI CI WEETAL KO , AK WOOMMATUL KO CI NANGUL KO TE TAXAW CI TËRËLINAM CI GËRËM KO AK NANGU KO. 10 YALLA YOONNI NA YÓNENTE YEEP BEENN BATAAXEL MOOY: WOOTE JAMEE CI JAAMU YALLA MOOM DOONĞ AMUL BEENN AJI BOOKAALE . LISLAAM MOOY DIINE MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI-, SEEN. WOOTE BEENN LA WAAYE SEEN TËRËLIN MOO WUUTE, JULIT YI TEY ÑOOM DOONĞ ÑOO JAAPP CI DIINE JU WER JI NGA XAMNE MBOOLEEM YONENT YI MOOM LAÑU ANDI, BATAAXELU LISLAAM BI CI JAMANO JII MOOY DËGG ; BOROOM BI YOONNI IBRAHIMA AK MUUSAA AK HIISAA MOO YOONNI KI MOOTALI YONENT YI /MUHAMMAD -YALLA NA YALLA DOOLLI KO XEEWËL, TËRËLIN LISLAAM MOO ÑËW DAADI FOOLLI MBOOLEEM TËRËLIN YIKO JIITU WOON. MBOOLEEM DIINE YI NGA XAMNE NITÑI DAÑUCEY JAAMOO YALLA MUNGI BAAYI KOO CI JAFU MBINDEEF, WALLA SAX ÑU NEEKKOON DIINE YU BAAYEKOO FA YALLA WAAYE LOXO MBINDEEF FOH CI MU MUJJI DI NDIAXAS MU RËNKALOO CI AY CAAXAAN AKI LEEBOON LUPEEN YU ÑUDOON DOONANTE AK AY LAAMBATUY MBINDEEF, WAAYE PAS PASU JULIT YI BEENN PAS PAS LA LEER, DU SOOPEEKU XOOLAL ALXURAN BEENN TEERE LË CI REWI JULIT YI. YALLA MU KAWE MI WAXNA CI ALXURAN :ْ

{WAXAL NE :ÑUN GËM NAÑU YALLA AK LIMU WAACC CI ÑUN AK LMU WAACC CI YONENT YALLA IBRAHIMA AK ISMAÏÏLA AK ISHAAQA AK YAHQUUBA AK AY SËTËM AK LIÑU JOXOON MUUSAA AK IISAA AK MBOOLEEM YONENT YI MU BAAYEKOO CI SEEN BOROOM DUÑU TEEXALE KEENN CI ÑOOM TE ÑUN DAÑUY WOOMMATUL YALLA}. (84) 11 {KU SAAKKU LUDUL LISLAAM MUY SA DIINE ; DUÑU KOKO NANGUL, TE MOOM ËLLËK ALLAAXIRA DAY BOOKK CA ÑA PERT ÑI .}(85) [3: 84,85]. LAN LA JULIT YI FAS CI IISAA-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI. ? NDAX XAM NGA NE : JULIT YI DAÑOO WARA GËM YONENT YALLA IISA TE BËGG KO WORMAAL KO TE GËM BATAAXELËM BI NGA XAMNE MOOY WOOTE JAMEE CI JAAMU YALLA MOOM DOONĞ CI LU ANDUL AK BEENN BOOKAALE KAT ! JULIT YI DAÑUY FAS NE : YONENT YALLA IISA AK YONENT YALLA MUHAMMAD- (YALLA NA LEEN YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI-)AY YONENT LAÑU YOO XAMNE YALLA MOO LEEN YOONNI NGIR ÑU GINDI NITÑI JAMEE LEEN CI YOONU YALLA AK YOON AL JANNAH. TE DAÑUY FAS NE YONENT YALLA IISA -(YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI ) BOOKK NACI YONENT YI GËNË MAAGG YI NGA XAMNE YALLA MU KAWE MI YOONNI NA LEEN, TE DAÑUY FAS NE JUDDU NA CI ANAM BU YEEME, YALLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN NE : MOOM IISA BIND NAÑUKO CI LUDUL MUY AM BAAY, NIKI MU BINDEE WOON AADAMA TE AMUL YAAY TE AMUL BAAY; NDAX TE YALLA KAT MOOY KI MAN LEEPP. DAÑUY FAS NE: IISA DU YALLA, DU DOOMU YALLA, TE MOOM KEENN DAAJU KO CI GARAB, LI AM BA DES MOOY MOOM AJI DUNDU LA, YALLA YËKËTIKO JËMEE FA MOOM; NGIR MU WAACCI MUJJUK JAMANO DI AATTE KAT BU MAANDU SUKO DEFEE MU AAND AK JULIT YI; NDAX JULIT YI ÑOOM ÑOO GËM WEETAL YALLA BI NGA XAMNE MOOM LA YONENT YALLA IISA ANDI AK MBOOLEEM YONENT YI. YALLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN BU TEDD BI NE: BATAAXELU YONENT YALLA IISA BI NASRAAN SI DAÑUKO JEENGAL LII ÑU SOOPPI KO BA NOOPPI RAX CA YENEENI YAX YOO XAMNE YONENT YALLA IISA WAXU LEEN KO, LIY DËGËL LOOLU MOOY WOOTEEK TEERE YUÑU SOOTTE CA BU NDIAKK BA AK BARIK JUUNOO CA TEERE YOYALE. YALLA XAMAL NAÑU NE: NAKA YONENT YALLA IISA DADAAN JAAMU BOROOMAM TE SAAKKU WUL CI KEENN MUJAAMUKO, LIMU 12 DAAN DIGËL AW NITËM MOOY JAAMU YALLA MILEEN BIND, WAAYE SAYTAANE MOOY XIRTËL NASRAAN SI ÑUUY JAAMU YONENT YALLA IISA , YALLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN NE: DU JEEGGËL KEENN KU JAAMU LUDUL YALLA MU KAWE MI, TE NAKA YONENT YALLA IISA DANA DAÑ CI ÑIKODOON JAAMU BA SET WEECCI ËLLËK BISU BEENCI BA, MUNE LEEN DIGËLOON NAA LEEN NGEEN JAAMU KI BIND ÑEEPP, TE MOSU MAAY SAAKKU CI YEEN NGEEN JAAMU MA BEEN YOON, BOOKK NACI LIY FIRNDEEL LOOLU WAXU SUÑU BOROOM BU KAWE BI:َ

{ÊEY YEEN ÑOÑ TEERE! BU LEEN JEEGGI DAYO CI SEEN DIINE! TE BU LEEN WAXAL YALLA LUDUL DËGG ; NDAX TE WËR KAT BII/ DI IISA DOOMU MARYAMA NDAWAL YALLA LA, TE KAADDUM LA ( NEEKKAL REKK MU NEEKK)GOO XAMNE SAANNI NAKO CI MARYAMA TEY RUU GU BAAYEKOO CI MOOM, GËM LEEN YALLA AK YONENTËM YI, BU LEEN WAXNE :YALLA YI ÑATT LAÑU ( YALLA AK IISAA AK MARYAMA) YAM LEEN MU NEEKK YIW CI YEEN, YALLA DU LUDUL KEENN, JOOMB NA MUY AM DOOM, MOO MOOM LI CI BIIR ASAMAN YI AK LICI BIIR SUUFSI, (CI MBIND AK CI MOOMEL)MOOM YÀLLA DOOYNA SUKANDEKU WAAYE (171)

[4: 171]

. YALLA MU KAWE MI WAXNA:ْ

13 {TUDDËL CI ALXURAN BIS BU YÀLLA DI WAX :ÊEY YAW IISA DOOMU MARYAMA!NDAX YAW YAA WAX NITÑI NA LEEN:JAAPPEE LEEN MA MAN AK SAMA YAAY ÑUY ÑAARI YÀLLA YU BOOKKUL AK YÀLLA, IISA NE: TUDDU NA SAK SEELL SAK JOOMBU BEEPP BOOKKALE ,JAADUWUL CI MAN MAY WAXAL SAMA BOOPP LUMA YEELLO WUL, TE SU FEEKKONNE WAXNAKO;YAW XAM NGAKO, NDAX YAW XAM NGA LICI MAN LEEPP, TE MAN XAMUMA LICI YAW, NDAX TE YAW YAAY XAMAAKOONI KUMPA YEPP} (116) (5: 116) KU BËGGA MUCCI ALLAAXIRA; NA DUGGU CI LISLAAM TE TOOPP YONENT BI MUHAMMAD ,YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI. BOOKKNA CI XEW XEW YU WER YI NGA XAMNE YONENT YI DËPPOO NAÑU CI ÑUÑU SOLOO AK ÑUÑU YOONNI (YALLA NA LEEN YALLA DOOLLI MUCCI) MOODI LIY MBIR TEY MBIR ALLAAXIRA JULIT YI REKK FAAY MUCCI! ÑI NGA XAMNE GËM NAÑU YALLA MU KAWE MI TE BOOLE WUÑU CI JAAMU GIÑUKOOY JAAMU KENEEN, ÑU GËM MBOOLEEM YONENT YI-YALLA NA LEEN YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI 'ÑU NEEKKOON CI JAMANO YONENT YALLA MUSAA GËM KO TOOPP NDIAANGALEEM ÑOOÑU JULIT LAÑU YU BAAX KU LAANKA GËM YONENT YALLA IISA TE NAAN DAMAAY DES CI DIINE YONENT YALLA MUUSA ,KOOKU GËMUL;NDAX MOOM LAANK NAAY GËM YONENT BU YÀLLA YOONNI, GANNAAW BA YALLA YOONNEE KI MUJJI CI YONENT YI:MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI- DAFA WAR CI ÑEEPP ÑU GËM KO, BOROOM BI YOONNI MUUSAA AK IISAA MOO YOONNI KI MOOTALI YONENT YI: MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI -KU WEEDDI BATAAXELU MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI-DAADI NE DAMAAY DES CI TOOPP MUUSAA WALLA IISAA ; KOOKU GËMUL. DU DOY REKK JËMM JI WAXNE: MOOM DAY HORMAAL JULIT YI, DU DOY NGIR MUCCI ALLAAXIRA MUUY SARAXE DI DIMBALE WËY ÑAAKKAYI, LI AM BA DES FAAWWU MU GËM YALLA TE GËM AY TEEREEM YI AK YONENTËM YI AK BIS BU MUJJI BA; NGIR YALLA NANGUL KO!NDAX TE AMUL BAAKAAR BU GËNË MAAGG BOOKKAALE AK WEEDDI YALLA DEELLOO LI YALLA WAACCE CI YONENT BI YAHUUD YI AK NASRAN SI NGA XAMNE DEEGG NAÑU YOONNIIK 14 YONENT YALLA MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI-ÑU BAÑ KOO GËM BAÑA DUGGU CI DIINE LISLAAM, DAAÑU DUGGU ËLLËK SAFARA JAHANNAMA SAX FA BË FAAWWU NIKIO SUÑU BOROOM WAXEE:

{NAKA GAAYI NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI YALLA MOO XAM ÑU BOOKK CI ÑOÑ TEERE YA WALLA ÑU BOOKK CA WËY BOOKKAALE YA; DAAÑU DUGGU SAFARA JAHANNAMA SAX FA, ÑOOÑU ÑOO YEES CI MBINDEEF YI}(6) [98: 6]. BI NGA XAMEE NE BATAAXEL BU MUJJI BII WAACCI BAAYEKOO CA YALLA JËM CI MBINDEEF YI BUKO DEFEE DAAY WAR CI KEENN KUNE KUY DEEGG LISLAAM TEY DEEGG YONENT BU MUJJI BII MUHAMMAD-YALLA NAKO YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI- MU GËM KO TE TOOPP TËRËLINAM TE NANGGUL KO NDIGËLAM AK TEREEM, LOOLOO TAX KU DEEGG BATAAXEL BU MUJJI BII DADIKO LAANK;YALLA DUKO NANGGUL DARA, TE DANAKO MBUGËL ALLAAXIRA. BOOKK NACI FIRNDEY LOOLU WAXU YALLA MU KAWE MI:

{képp ku topp jeneen diine ju dul lislaam deesu ko ko nangul te bu bis-pénc baa di na bokk ca way torox ña }.

[3 : 85]

{WAXAL: YEEN ÑOÑ TEERE YI KAAY LEEN CI KAADDU GOO XAMNE GU YAMOO LA SUÑU DIGANTE ÑOOK YEEN TE MOOY BUÑU 15 JAAMU KUDUL YALLA, TE BUÑUKO BOKKAALEEK LEEN, TE BUÑU JAAPPANTE CI SUÑU BIIR AY YALLA, BAAYI FI YALLA,BU ÑU DËDDOO;NANGEEN WAX NE:SEEDE LEEN NE NE ÑUN WËY NANGGU LAÑU WËY WOOMMATU LAÑU}(64)

(3: 64)

. LAN MOOY WARAL MANEEKK JULLIT? NGIR DUGGU CI LISLAAM WAR NA ÑU GËM YILE JUROOM MBEENNI POONKK: GËM YALLA MU KAWE MI ,CI NE MOOY KI BIND MOOY WARSAGAL MOOY TOOPPATOO TE MOOY KI MOOM, AMUL LEENN LU NIROOK MOOM, AMUL AANDANDOO BU JIGEEN (JABAR)DU CAAGEN DOOM, MOOM DOONĞ MOO YEELLO JAAMU. GËM MALAAKA YI CI NE ÑOOM AY JAAMI YALLA LAÑU BIND NA LEEN CI LEER MU BOOLE CI SEEN LIGEY ÑUY WAACCE NDEEYËM (WAHYUM)CI AY YONENTAM. GËM MBOOLEEM TEERE YI NGA XAMNE YALLA WAACCE NA LEEN CI AY YONENTAM (NIKI TAWRAAH AK LINJIIL)BI MUJJI CI TEERE YI MOOY ALXURAN BU TEDD BI. GËM MBOOLEEM YONENT YI NIKI NUUH AK IBRAHIMA, AK MUUSAA AK IISAA KI CI MUJJI DI MUHAMMAD YALLA NA LEEN YALLA DOOLLI XEEWËL AK MUCCI, ÑOOM AY MBINDEEF LAÑU YALLA DËGËRËL LEEN CI NDEEYAM JOXLEEN AY MANDARGA AKI KEEMAAN YUY TEKTALE SEENUK DËDDU. GËM BIS BU MUJJI BA JAMANO BA YALLA DI DEEKKAL ÑU NDIAKK ÑA AK ÑU MUJJI ÑA MUY AATTE DIGANTE MBINDEEFAMYI DI DUGAL WËY GËM YI ALJANNAH TE DI DUGAL WËY WEEDDI YI SAFARA. GËM DOGAL GËM NE YALLA MOO XAM LEEP LU AMOON CA LA WEESU AK LIIY AM CI LUY ÑAW, TE NE YALLA DOGAL NAKO TE SOOP NAKO TE MOO BIND LUNE. LISLAAM MOOY YOONU TEXE! LISLAAM MOOY DIINEY MBOOLEEM YONENT YI!. 16 LISLAAM MOOY YOONU XEXE GU WERGI FII CI ADUNA, AK XEEWËL GU SAX DAAKK CA ALLAAXIRA. LISLAAM MOOY MOOM DOONĞ MOOY DIINE JI MANA FAJ HAAJOOY RUU AK YARAM, TE MOO MANA LIJANTI MBOOLEEM LËJ LËJI DOOM AADAMA YI. YALLA MU KAWE MI NEENA:َ

{YÀLLA NE AADAMA AK HAWWAA: WACCI LEEN BAAYEKOO CI ALJANNAH JI YEEN ÑEEPP , AMNA ÑEENN CI YEEN ÑOO XAMNE NOON LAÑU CI ÑEENN ÑI BU LEEN AM JUB ÑAWALEE BAAYEKOO FI MAN;KU TOOPP SAMA JUB DU SAANKU TE DU TOROX. } {KEEPP KU DUMMOOYU SAMA ALXURAN BII; DANA AM DUNDU BU XAT TE DANAÑUKO PANGĞ BIS PEEÑCI BA MU GUMBA} [20: 123,124]. LAN LAAY JARIÑOO CI SAMAK DUGGU CI LISLAAM? DUGGU CI LISLAAM DAFA AM AY NDIARIÑ YU MAAGG, BOOKK NACA: TEXE AK TEDD CI ADUNA TE MOOY NIT KI NEEKK DI JAAMUB YALLA KESE, BUDUL LOOLU DAAY NEEKK JAAMU BAANEEXU BAKANAM AK SEYTAANE AK FOYTEEF YI. GËN JAAY MAAGGI TEXE CA ALLAAXIRA MOOY NIT KI MUCCI CI MBUGËLËM SAFARA TE DUGGU ALJANNAH, TE TUUFU CI NGËRMAANDE YALLA AK SAX CA ALJANNAH JA. ÑI NGA XAMNE YALLA DALEEN DI DUGAL ALJANNAH, DAÑEEY DUNDU CI XEEWËL GU SAX CI LUDUL DEE! WALLA BEENN XEET CI FEEBAR WALLA MEETIT WALLA NDIAAXARE, WALLA XOBIDAAS, TE DAÑUY AM LEEPP LUÑU BËGG. 17 ALJANNAH AMNA AY XEEWËL YOO XAMNE BËT MOSU KO JIS, NOOPP MOSU KO DEEGG, TE MOSUL TOOXXU CI XELU BEENN DOOM AADAMA. BOOKKNA CI FIRNDE LOOLU WAXU YALLA MU KAWE MI:ۡ

{KEEPP KU DEF JËF JU BAAX MOO XAM GOORLA MOO XAM JIGEEN LA; DAAÑU KO DUNDAL DUNDU BU MUCCI AYIB TE DAAÑU LEEN FAY SEENUK PAY CI LU DAAXX LAÑU DOON DEF} [16: 97]. LAN LAA NAROONA ÑAAKK SUMA LAANKKOON LISLAAM? NIT DANA ÑAAKK LU GËNË MAAGG CI XAM XAM AK RAAÑÑEE TE RAAÑÑEE AK XAM YALLA, DANA ÑAAKK NGËM YALLA MI NGA XAMNE MOOY MAY NIT KI KOOLUTE AK DAL CI ADUNA, DI KO MAY XEEWËL GU SAX CA ALLAAXIRA. NIT KI DOON NA ÑAAKK AK YËR CI GËN JAAY MAAGGI TEERE BOO XAMNE YALLA WAACCE NAKO CI NIT ÑI, AK ÑAAKK NGËM CI TEERE BU MAAGG BII DOON NA ÑAAKK NGËM CI YONENT YU MAAGG YOOYU NIKI MUUY ÑAAKKEE AND AK ÑOOM CA ALJANNAH JA BIS PEEÑCCI BA SUKO DEFEE MUUY AND AK SAYTAANE AK HOOMLU KAT YI XËRËM CA SAFARA JAHANNAMA, NDAW KËR GU BON, NDAW DAKANDOO GU BON. YALLA MU KAWE MI WAXNA:ْ

{WAXAL NE ÑI ÑAAKK DËGG ÑOOY ÑI NGA XAMNE DAÑOO ÑAAKK SEEN BOOPP ÑAAKK SEEN NDIABOOT BIS PEEÑCCI BA DAMANE LOOLA NAK MOOY ÑAAKK GU LEER GI } 18 DANA LEEN TIIM CI KAW AY DONĞO CI SAFARA DANA CI SEEN SUUF AY DONĞO CI SAFARA, LOOLU YALLA MOONGI CEEY XUPEE JAAMAM YI YEEN SAMAY JAAM NA NGEEN RAGAL YALLA}

[39: 15,16]

. BUL DI YEEXA JËL SAY MATU KAAY ADUNA DU KËRUK SAX! BEEPP TAAR DANA MOSA LAAXXU BEEPP BAANEEX DANA MOSA FAY..... BIS DINA ÑAW ÑU HASAAB CI LEEPP LOO MOSA DEF, LOOLU MOOY BISU TAXAWAAY BA YALLA MU KAWE MI WAXNA:َ

{ÑU DAADI TEK TEERE YI NGA DAADI JIS KACCOOR YI ÑU TIIT NGIR LI NEEKK CI BIIR TEERE BOOBULE ÑUY WAX NAN: NGALLA WAAYE ÑUN LAN MOO DAL TEERE BI MOOM BAAYI WUL LU NDAW BAAYI WUL LU MAG LUDUL TAKK NAKO, ÑU DAADI FEEKK LAÑU DEFOON MUUY TE SA BOROOM DU TOOÑ KEENN}. [18: 49]. YALLA XAMLE NA NE : NIT KOO XAMNE DU JEEBLU MUJAM MOOY SAX CA SAFARA JAHANNAMA BA FAAWWU. ÑAAKK NEEKKUL LU ÑAAKK SOLO ,WAAYE LU RËY LA

{ KU SAAKKU LUDUL LISLAAM MUUY SA DIINE ;DUÑU KOKO NANGUL TE MOOM ËLLËK ALLAAXIRA DAY BOOKK CA} [3: 85]. LISLAAM MOOY DIINE JI NGA XAMNE YALLA DU NANGGU BENEEN DIINE BUDUL MOOM. 19 YALLA MOO ÑU BIND TE CI MOOM LAÑUY DEELLU , ADUNA BII NATTU REKK LA NGIR ÑUN. GËM BU WOOR NE DUNDU BII DAFA GATT NIKI GEENT... KEENN XAMUL KAÑ LAY DEEH! LAN MOOY NEEKK SA TONTU ÑEEL SA BOROOM BI NGA XAMNE MOO LA BIND BU LA LAAJEE BIS PEEÑCCI: LU TAX TOOPPU LAWOON GËGG? LU TAX TOOPPU LA WOON KI MOOTALI YONENT YI ?-YALLA NA YALLA DOOLLI LEEN XEEWËL AK MUCCI . LAN NGAAY TOONTU SA BOROOM BIS PEEÑCCI, TE WATANDEKU LOO WOON NALA TOOPATUK WEEDDI (LA MU LAAY YOOBOO!)LISLAAM, MU XAMAL LA NAKA MUJJUK YEEFËR YI MOOY ALKU CA SAFARA BA FAAWWU? YALLA MU KAWE MI NEENA:َ

{ ÑA NGA XAMNE DAÑOO WEEDDI YALLA WEEDDI SUÑUY MANDARGA; ÑOOÑU ÑOOY WAA SAFARA TE ÑOOM DAÑU FAAY SAX } [2: 39]. KU FI BAAYI GËGG DI ROY AY BAAY AKI MAAM;DOO AM BEENN NGAANT! YALLA MU TEDD MI XAMAL NAÑU NE : LU BARI CI NTIÑI DAÑUY LAANK DUGGU CI LISLAAM NGIR RAGAL BËRËB BAÑUY DUNDEE. ÑU BËRI DAÑUY BAÑ LISLAAM NGIR ÑAAKK XEMEM SOOPPI SEEN PAS PAS YI NGA XAMNE DAÑUKO DOONNEE CI SEEN WAA JUR YI TE TAAMMUKO. ÑU B BARI CI ÑOOM PAR PAR LOO AK JOM JOM LU CI CAAXAAN YI NGA XAMNE DOONN NAÑUKO MOO LEEN DI TERE DUGGU CI LISLAAM . ÑII ÑEEPP AMUÑU NGAANT CI LOOLU TE DAAÑU TAXAW CI KANAM YALLA TE DUÑU AM LAY. DU NEEKK NGAANT CIB ATE MU NAAN: DAMAAY DES CIK ATE NDAX TE DAMAA JUDDU FEEKK SAMAY ÑOÑ NEEKK KO! DEE DEET! NA JAFANDEKO XEL MIKO YALLA JOX MOOM MIKO BIND NGIR MU MËNË 20 XAMNE ADUNA BII AMNA KUKO BIND, NIKI NOONU KIY JAAMU XEERY YI AK XERËM YI AMUL NGAANT CI ROY AY WAA JURËM, LIKO WAR MOOY MU GASTU DËGG LAAJ BOPPAM: NAKA LAADI JAAMOO YU WAY YILE NGA XAMNE DUMA DEEGG DUMA JIS TE DUMA JARIÑ DARA?! NIKI NASRAAN BOO XAMNE DAY GËM LU WUUTEEK CET AK XEL MU DAY WAR MU LAAJ BOPPAM: NAKA LA BOROOM BI DI RAYEE DOOMAM DIOO XAMNE DEFUL BAAKAAR MUKOOY RAY NGIR BAAKAARU ÑËNEEN! LII CI TOOÑ LA! NAKALA MBINDEEF YI DI DAAJEE CI GARAB, WALLA DI RAY DOOMU DOOMU BOROOM! NDAX BOROOM BI MUNUL JEEGGËLE BAAKAARI MBINDEEF YI TE BAÑ LEENA BAAY ÑUY RAY DOOMAM! XANAA BOROOM BI MANULA AAR DOOMAM? LI WAR CI BOROOM XEL MOOY MU TOOPP DËGG, BU MU ROY AY BAAY AKI MAAM CI CAAXAAN. YALLA MU KAWE MI NEENA:

{ BU ÑU LEEN WAXEE NE: KAAY LEEN CI LI YALLA WAACCE AK CI YONENT BI;REKK ÑUNE : LU ÑU FEEKKOON SU ÑUY MAAM DONAÑU, A WAAW NDAX BU FEEKEE SEENI MAAM SAX XAMUÑU DARA TE NEEKUÑUWOON CI NDIUB} [5: 104]. KU BËGGË MUCCI TE TIIT CI BOOPAM CI LORI AY JEGEÑAALEEM LAN LAAY DEF? KU BAGGA MUCCI TE RAGAL TUNDU WIKO WËR! NDAX DANA MANA DUGGU CI LISLAAM NABBU LISLAAMAM BA YALLA YOOMBALALKO YOONU YIW WOO XAMNE DANA CA MOOMEE BOOPAM TE FEEÑË LEECI LISLAAMAM. BOOKK NACI LI WAR CI YAW NGA NANGU LISLAAM CI LU GAAW, WAAYE WARUL CI YAW NGAY XAMAL ÑILA WËR SA LISLAAM WALLA NGA KOOY SIIWËL, BU FEEKKEE LOR DALA CEEY DAL. XAMAL NE YAW BOO DUGGEE CI LISLAAM, DANGAAY NEEKK MBOOKKU CI AY MILYOON JULIT , DANGA MANA JOOKKOOK AY JAAKK 21 AKI SAXU WAAY YU LISLAAM (SAANTAR ISLAAMIK)CI SA DËKK NGAY SAAKKU CI ÑOOM DIISOO AK NDIMBAL, SUKO DEFEE LOOLU DI LEEN BEGLOO. YALLA MU KAWE MI NEENA:ْ

{ KEEPP KU RAGAL YALLA,; YALLA DEFALKO GEENNU WAAYE CI BEEPP XAT XAT, TE WARSAGAL KO FUM KO DUL FOOGEE} 65: 2,3] YAW AJI JAANG JU TEEDD JI! NDAX GËRËM LOO YALLA MI LA BIND, - KI NGA XAMNE MOO LA DEFAL AY XEEWËLAM, NGA XAMNE MOO LA DAAN JOX DUNDU TE FEEKK YAW YAANGI NEEKK MBEEMUR CI SA BIIRU YAAY, MU WARSAGAL LA HEER BI NGA XAMNE MOOM NGAAY BAANAMTEKOO LEEGI- LOOLU MOO APP SOLO CI GËRËM LOO NIT ÑI CI SA BOOPP XANA DU TEXE ADUNA AK ALLAAXIRA MOO YEELLO ÑU JOTTEEKO LEEPP LUKO YEES CI XEEWËLU ADUNA YII DI JEEX? AHAKAY WAAT NAAKO CI YALLA! BUL BAAYI SA LI WEESU MU LAY TERE GAAGANTI SAW YOON WU AM NDIUUMTE AK DI DEF LI WER. NANGA NEEKK JULIT BU WER TEY! BUL BAAYI SAYTAANE MU LAAY TAXAWLOO BA DOO MANA TOOPP DËGG! YALLA MU KAWE MI NEENA:

﴾ÈEY YEEN NIT ÑI LAY WU LEER NAAÑÑI ÑAWAL NA LEEN BAAYEKOO CI SEEN BOROOM, TE WAACCEEL NAÑU LEEN LEER GU BIR(174) 22 ÑI NGA XAMNE GËM NAÑU YALLA TE ĞOY CI MOOM; DANA LEEN TAABBAL CI YËRMËNDE BU BAWOO FA MOOM AK NGANEEL TE DANA LEEN TEK CI YOON WU JUB}(175) .

[4: 174,175]

NDAX YAW WAAJ NGA NGIR JËL DOGU BU GËNË MAAGG CI SA DUNDU? BU FEEKKEE LI JIITU YEEPP XEL NANGUNAKO CI SA GIS GIS! NGA NANGUKO CA DËGG DËGG CI SA XOLBI KON WAR NGAAY SEEXXI JEEGO BU NDIËKK JAM CI NOOY MUJJEE NEEKK JULIT? BUL SAY BÀKKAAR MU LAY TEREE DUGG CI LISLAAM, YÀLLA XAMAL NAÑU CI ALXURAN: NE MOOM MOOY JEEGGËLE BÀKKAAR YU DOOM AADAMA YEEPP BU DUGGEE CI LISLAAM ,DAADI DEELLU CI BOROOMAM MI KO BIND, BACI GANNAAW BOO NANGGO LISLAAM DAFA CI DOYADIK DOOM AADAMA CI NE YAW LEEGOO LEG NGA TOOGGO BAAKAAR NDAX ÑUN AY NIT LAÑU NEEKKU ÑU AY MALAAKA YU ÑU ÑONĞEEL CI AY BÀKKAAR , WAAYE LIÑU SAAKKU CI ÑUN MOOY ÑUUY SAAKKU NDIEEGËL CI YALLA TE TUUB DELLU CI MOOM BU YÀLLA JISEE CI YAW CI NE YAW YAA NGEEY GAAWANTU DI NANGGU DËGG AK DI DUGGU CI LISLAAM TE TUDDU ÑAARI BAATI SEEDE YI, NDAX LOOLU MOO LAAY DIMBALI CI BAAYI YENEEN BÀKKAAR YI KII NGA XAMNE DAFA NANGGUL YALLA, TE TOOPP DËGG YÀLLA MOO KOOY DËPËLEEK NDOOLLENTE YIW BUL DEENG DEENGI CI DUGGU CI LISLAAM LEEGI. BOOKKNA CI FIRNDEEY LOOLU WAXU YALLA MU KAWE MI:

{WAXAL ÑI WEEDDI YALLA NE: BUÑU DAYTALOO ;ÑU ÑU JEEGGËLLEEN LI WEESU} [8: 38]. LAN LAA MANA DEF NGIR NEEKK JULIT? DUGGU CI LISLAAM MBIRËM YOOMB NA, HAJOWOO WUL AY MANDARGA DIINE ,AMUL AY XEW XEW, WALLA TEEWUK KEENN, DAY WAR NIT KI REEKK MU TUDDU BAATI SEEDE YI TE XAM MAANA YI, TE GËM KO, TE MOOY MU WAX :(MAANGI SEEDE TE DËGGËL TE GËM 23 NE AMUL KEENN KUÑU WARA JAAMU KUDUL YALLA ,TE MAANGI SEEDE TE DËGGËL TE GËM NE MUHAMMAD YONENT YALLA LA),BU JAAPPANDEE CI YAW NGA MANKOO WAX CI LAAKKU ARAAB LU BAAX LA BU JAFEE CI YAW NGA WAX KO CI SA LAAKK, CI LOOLU NGAAY NEEKKEE JULIT , DAY WAR CI YAW NGA JAANGA SA DIINE JI NGA XAMNE MOOY SA BALLU WAAY TEXE FII CI ADUNA AK SAK